A cabeleira multilingüe

 

Yagamare Fall Diop | Wolof

Karaw Gui
(Dogit)

Thi ab deuk bou naat, done takhawalou si guinaw fi nak yiy léké, fa la djoudo
Worou ma nak né domou sam kat deug la, wayé gnom dè fa adouna diékhé legn takhaw
Sama aada dou lenen loudoul djiw djiy naw té deukou ma fenen foudoul andak ngelaw gui di weuy
Mak samkat yi bene legn, gnom gni nga kham né moussou gnou tabakh ab deuk
Sougnou khel reka kham lane moy soukh deug ak nj gnou souf si weuré
Degnou dem nak ba rer ndeyssan, ba diakhassok sougnou ay nak
Wayer mane dé guissat na sama yone, top si ba andak karawiu wer bi
Té karawu wer bi defe beuri té diakhasso, ki ma nop rek la fey djokol.

(Firndé wolof Yagamare Fall Diop)